Xët wii dafay leeral naka la ABC Translation di jëfandikoo say xibaar yu nga nu yónnee ci site bi, topp ci yoonu Senegaal n° 2008-12 bu 25 janvier 2008 ci aar xibaar yu nit ñi.
Li nuy jël
Sa tur, sa email, sa telefon (su la neexee), sa laaj, dëkk bi, làkk yi ak kayit yi nga boole. Jëfandikoowunu cookies ngir pub walla topp nit ñi.
Lu tax
Ngir tontu sa laaj, defar sa devis te, bu nga nangoo, def liggéey bi.
Ñan ñoo koy gis
Sunu équipe rekk, te bu liggéey bi soxlaa ko: tekkikat, notaire, nguur, ambassade walla bérabu ABC Translation. Infomaniak (Suisse) moo yor sunuy email.
Ba kañ
Laaj yu amul commande, dinanu leen far ci 12 weer. Kayitu commande yi, dinanu leen denc ni yoon wi laaje.
Say sañ-sañ
Mën nga gis, jubbanti walla far say xibaar: bind info@abc-offices.com. Mën nga tamit jokkoo ak Commission de protection des données personnelles (CDP).
Kaarange
Site bi dafa jëfandikoo HTTPS. Kayit yi nga boole, ci sunu email lañuy dem, deccuñu leen ci serveur bi.